
Ci talaatay démb ji la “Banque mondiale” siiwal ne nangu na a lebal Senegaal koppar yu tollu ci 115i miliyoŋ ciy dolaar, yemook 65i miliyaari CFA. Bor boobu, li mu ko duggee mooy dooleel caytug koppari bokkeef gi te yokk anam yi ñuy dajalee xaalis bi ci biir réew mi. Bor boobu nag, jaarees na ko ci kurél gees duppee IDA (Association internationale de développement).